contenu de la page
Connectez-vous S'inscrire
Asfiyahi.Org - 1er Site de Reférence sur l'Islam et la Tidjaniyya au Sénégal
Asfiyahi.Org
ABONNEZ-VOUS À NOTRE NOUVELLE CHAINE YOUTUBE HD

Publicité



Wolofal: Si Maalik ( Par Dr. Ibrahima Thiam)






Wolofal:  Si Maalik ( Par Dr. Ibrahima Thiam)
Si Maalik
 
Bimilaaxi, ma xëy di woy
Waa ju baax, ji ñëpp woy
Batax ma am sañ-sañ, jook diko kañ
 
Raxmaani, di xéewal mooy ki ko doy
Ba taallalul ax yoxoom di jooy
Ndaxte doylu mooy moom liko ñorr
 
Rahiim di yërmande moom la fegoo
Gisul luko yéem xanaa Seex miko doy
Mu rangu ci yoonam ba am ci cër
 
Si Maalik, yaw yaa bidéew up leer
Tabbi ci lëndëm ba jox leen leer
Ba tax ñu tal tey nelaw bay janeer
 
Si Maodo réew mi amna guddi yu tarr
Ku nekkul woon jambaar, yaw doo ko tal
Nga sàmp ndëndup diiné boole di woy
Gën gi mbindéef, moo nga Medina
 
Sy As tariixa, yaay ki ci taal
Taal gu dul fey muk ndax yaako yok taar
Ba ku mu neex, nga xëy di wax
 
Jëmmël nga diiné, doxal tariixa
Ji fi garab gu ker gi di baawaan fép ci dunyaa
Si Maalik yaw yaay ki ko def
 
Ku tey am sañ-sañ di bakkoo Jakka bay dem Makka
Feyal naar bi xoromom, Sy Malik mooy ki ko xeex
 
Biral wazifa, dajale xadara ci jakka yi
Naasiril haqqi , bil haqqi di faatihi
 
Jug leen ñu sargaal waa jaa ngi nii
Si Maalik, boo tëddoon, du nu am lii
 
Sy Maalik Réew mi amel na ñu la njukkël
Ba tax fuñu toll wara saxoo di dukat
Du sunu cër sax, kon ñu fettasu
 
Sa turbi aggana fépp ci dunyaa
Sa mbaax ak sa yiw, tolla na fune
Buur Yalla dako soppi mu doon biddéew
Def ko mu kawe, leer gi di ball jëm fune
 
Ku taawloo Sidy Axmet, yaa di jambaar
Sëriñ Baabacar, sunu yaakaar
Mame Abdoo ngi ni wane taaru mawdo
Di baat bu neex, di xoll bu rafet
Di wax ju teey, boole ci neex deret
 
Ku mëne njaboote ñii, am na cër ca Yalla
 
 Dr. Ibrahima Thiam

Asfiyahi.Org
Mardi 3 Décembre 2019






Nouveau commentaire :
Facebook Twitter


Telechargez l'application Mobile Asfiyahi pour plus de navigabilité ABONNEZ-VOUS À NOTRE NOUVELLE CHAINE YOUTUBE HD


Dans la même rubrique :